Lan moo jot ki lay mere ak di la iñaane ngir garaat ak cër bi la Yàlla jox rekk moo tax mu lay mere, te loolu Yàlla la ko defal kenn defalu la ko, kudul Yàlla.
فلكل مستنم أسوة بسعيك ولكل مرا فيك خير مزيد
Képp kuy rëy-rëylu war na mu roy ci yaw El Haaji Mansuur, ndax cër bu nit di am di ko tiitaroo am nga ko ni patt, te rëyóo ci tiitaruwóo ci, te ku toog ak yaw dina dolliku ci xam-xam ak ci yar.
أوفيت عهدك للخليفةبعدما
قدشان غيرك من ذوى التقليد
Matal nga kollëre ci sëriñ Baabakar Si, jamono ja nga xam ni nit ñi ñaawal jëmale ko ci sëriñ Baabakar yaw Jamono booba yaa ngi rafetal jëmale ci moom.
مدحا وذما قد سمعت ولم تكن ممن يبالى قولة لحقود
Topp gi nga topp sëriñ Baabakar Si dégg nga ci xas, dégg nga ci xas, waaye taxul nga bàyyi. Te faalewóo ci waxi ña nga xam ni iñaan rekk a tax ñuy wax.
فأتيت مشتمل المكارم واقفاً بذاره باذل طارف وتليد
Ñaari cër nga am, benn bi yaa ko liggéeyal sa bopp, beneen bi da nga koo dondu ku ñëw nga jox ko ci.
فلأنت تلفى فالج ابن حلاوة مما يعاف بظلنا الممدود
Sa yiw gi ak sa dal gi man nañu koo tëkkale ak Faalij Ibnu Halaawa nit koo xam ni dañu ko daan tuumaal ni ko yaa def, walla wax nàngam te fekk defóo ko noonu la El Haaji Mansuur meloon. Lépp loo xam ni dañu koy tere, walla di ko bañ ci Hadara bi El Haaji Mansuur waxu ko defu ko.
يامنص إنك لا تشابه رفعة إذ كنت منتسبا لذى التوحيد
Yaw Haaji Mansuur amul kenn koou nirool ci kawe, kenn melul ni yaw, ndax Seexal Haaji Maalig mu sotti nga.
إن العمامة لا تقارب من أتى يبغى التقرب منك ياذالجود
Sa tabe gi dafa mel ni niir, ak taw buy sotti féppay tooy du bàyyi fenn, sa tab gi noonu la mel.
إذ ماهديت هديت كل موقف للهدى هدي الخاتم الصنديد
Dangaa jub, ba noppi du jubal, di jubale képp ku Yàlla namm ci moom njubug Seydina Mouhammat.
حتى كأن سناك عم مشارقا ومغارباً فى الأرض مثل السعود
Sa leer gi dafa mel ni biddiw Suhuut bu leer gi jollee leeral ñépp penku ak sowwu.
فى البذل أنت كما الحيا وبحكمة كالبحر إذ فى الحلم كاالجلمود
Booy maye day mel ni taw, ak sa hikk ma yi dafa mel ni duusi géej, di sotti rekk.
Lewet gi nga lewet dafa mel ni montaañ, lu ñu la man di wax nga baale ko sa lewet gi noonu la mel.
وافيت دائر الإحاطة مغرماً بسمى يهز ضرائب المعبود
Waa daahiratul ihaatati fa walliyu Yàlla yu mag ya nekk ñooñu sax dañu laa sopp ba bu ñu la gisee bég, bu ñu la gisul laajte la ngir sopp gi ñu la sopp.
لولا التقصر جل أهل بلادنا
ليكون منك لهم جزاء ودود
Dañu laa gàttañlu, Gaa yi xamuñu la, bu ñu la xamoon, xam gi ñu lay xam njariñ lay doon ci ñoom, jóge ci yaw jëm ci ñoom
فاعلم وعلم المرء أنفع ماحوى أن لا أزال لكم أبر وليد
Loo xam moo gën a wér lu ñu la wax, maa ngi lay xamal man Seex ne lépp loo xam ni doom du ko wax baay duma la ko wax, fépp fu doom di teg baay dinaa la fa teg yaw Haaji Mansuur.
فعلى النبي محمد والآل مع. صحب سلام الله ذى التمحيد
Xéewalug Yàlla gi yal na sax di nekk ci yonent bi ak sahaaba yépp.