4 décembre 2024
Ouest Foire Cite Alia Diene Lot 30
La Tidjaniyya

Les 23 Chartes de la Confrerie Tidiane

1- Nga japp wird bi ci ku am ndigal bou wer; ndigal guy jappalo ba ci Siidi Ahmed Tijaani ni callala

Le postulant doit être affilié par un muqaddam qui lui-même est consacré dans sa fonction par le Cheikh fondateur ou un des ses représentants notoires.

2- Ki jel Tarixa bi, na feck mo yore benn wirdu Serigne, walla na bayyi wirdu Serigne boobu, walla muxaddam bi bu mu ko may wirdi bi. Su ko ko mayee, dog na, moom muxadam bi ci tarixa bi. So bayye sa wird, Seex mo la guaranti.Tijaan bi su bayye wirdam, benn Serigne munu ko aar ci alku, ak Serigne boobu lumu rey rey martaba, ak kumu mana doon.

Le postulant doit être libéré de toute obédience envers une autre tarixa. Si le postulant accepte de laisser son wird initial, il est sous la protection de CHEIKH, quelque rang qu`occupe le Serigne qu`il quitte. Si le tidiane par contre laisse son wird, aucun serigne, quel que soit son rang ou son grade, ne peut le prémunir de sa perdition.

3- Doo ziarra ben walliyou buy dund ay bu dee budul tijaane.Te bo ko defe dok nga ci tarixa bi.Du xeebate walla rey lu- sarte la rekk.Terewul seetante, demante

Il lui est absolument interdit de visiter  » ziarra » ou d`invoquer l`intercession de tout saint étranger (non tijaane) vivant ou mort, sous peine d`être exclu de la tarixa. Il doit néanmoins considération et respect à tout saint homme sans exclusive. Cette conditionnalité n`exclut pas non plus une fréquentation entre musulmans.

4- Saxoo di julli julli juroom, ci boppu waxtu wa, ci mbooloo, ndegem ilimaan ja mat na ilimaan, di matal rukoo ak sudjoot ya ak sellel Fatiha ; te saxoo topp sunna.

Les adeptes du masculin doivent faire les cinq prières en assemblée, et autant que possible à la mosquée. Les adeptes du sexe féminin prieront à la première heure de la période correspondant à chaque prière. Les deux adeptes du sexe se soumettront aux lois établies par la Charria et suivront la souna.

5- Saxoo bëgg Séex Ahmed Tijaanii ba kerook ngay dee, ak xalifaam, ormal ko ni ngay ormalé séex ci boppam

Il lui faut aimer Cheikh Ahmed Tijane et ses khalifes d’un amour puissant et toujours croissant, honorer le khalife de Cheikh au même titre que lui-même.

6- Bagna naagu mukk, bagna voolu pexem Yalla. Ngueneel lu tarixa bi, bumu tax nga bagna def li la war ak bayyi li la war. Sooko défee, yalla di n la nattu ba nga bagne Séex. Sa bagne séex guena nga ci tarixa bi.

Il lui faut se garder d`un excès de confiance, de se suffire soi- disant du dessein de DIEU. Ne point se fonder sur les promesses et les avantages de la tarixa et « se croiser les bras ».

7- Doo xass mukk, doo noonoo mukk, doo gotti mukk Seex Ahmed Tijaane.

Il ne proférera jamais d’injures ou de critiques à l’adresse de Cheikh Ahmed Tijaane.

8- Saxo wird, wazifa, ak hadara jumaa ba kerooq ngay dee.

Ne jamais abandonner l’ordre après y avoir été affilié, pratiquer le wird jusqu’à la mort.

9- Sa pass pass du wanniku mukk, doo ko uri mukk. Sa orma ci Seex su vanni koo, xamal ni sa pas vanni ku na .

Avoir la ferme conviction de la voie.

10- Doo weddi, doo diingat ( doo contre) Seex Ahmed tijaan.Neena lumu wax, natt len ko ci alxuran ak sunna.Su deppowul, waxu ko.Kon ku ko weddi Yallah ak Yonnentibi nga weddi.

Te garder en toute circonstance de discréditer cheikh Ahmed Tijaane car tout ce qu’il dit et fait est conforme aux recommandations de Dieu et de son prophète ( S.A.S)

11- Taalibe bi, bumu wird muk te amuci ndigal

Aucune personne non affiliée ne doit réciter les oraisons sans autorisation d’un muqaddem.

12- Daje di wazifa ak hadara jumaa ci mboloo ndegem tijaane a nga fa

Assister la récitation de la wazifa et du hadara du vendredi en assemblée (si possible)

13- Doo jang Jawharatoul-Kamal te andook njapp.

Il ne faut jamais réciter la Djawharatoul-Kamal (perle de la perfection) sans ablutions rituelles.

14- Doo noononte doo dogoonteek mbindaafon yi rawati na ki nga bokkal tarixa bi

Il est interdit à l’adepte de se brouiller avec tout être humain et, encore moins avec un tijaane.

15- Doo doyadal wird wi di ko yeexe be waaxtu wi guena te amoo ngant

Il faut éviter toute négligence dans la pratique, notamment tout retard dans la récitation du wird, si ce n’est un cas de force majeure réelle.

16- Boul maye wird te amoo ndigalu maye ko

Il ne faut jamais, sans investiture, s’attribuer le titre de moqaddem et donner le wird

17- Nga ormal kepp ku askanoo ci Seex rawatina magu tarixa bi

Respecter, honorer les gens de la tarixa, en particulier les « anciens » qui ont acquis des grâces particulières de DIEU

18- Sooy wird nga laab ci sa yaram ak ci sa yere

Veiller à la propreté rigoureuse de son corps, de ses habits.

19- Na ngay wird ci barab bu laab, bu yaatu , fu 6 nit xac (lu mu new new) ngir nga sori sobe.

Veiller à la propreté rigoureuse de l’endroit où on effectue le wird, ainsi qu’à son espacement (6 personnes)

20- Toog jublu penku budul ngay doxe donte mu gatt, wala nga nekk ci geewu wazifa

Il faut pendant la récitation des oraisons, se tourner vers la KAABA ( temple sacré de la Mecque), sauf en cas d’exception prévus (lorsqu’on se déplace en marchant par exemple).

21- Doo wax sooy wird ludul ci lorange ak niudul Serigne bi ley tarbiya, sa ndey, sa baay, mbaa sa jekker nioniu lu leen nex wax ak yow

Il ne faut jamais, sauf en cas de force majeure, interrompre la récitation par d’autres paroles à l’exception de votre cheikhou tarbiya, votre père, votre mère ou votre mari.

22- Teewlu jemmi Yonnent, mbala jemmi sa Serigne bala may wird ci commencement wird wi ba ca jeex ba.

Il faut, pendant la récitation, se concentrer et essayer de visualiser en esprit l’image de CHEIKH AHMED TIJANE , ou mieux, celle du prophète (sur lui la paix et le salut) ou à défaut du Serigne qui vous a affilié.

23- Teewlu maana (tekkite) baat yi ngay jang.

Il faut, si on le peut, saisir le sens de ce que l’on récite. Si cela n’est pas possible, écouter avec attention de manière à distinguer le son de ce que l’on récite.

Leave feedback about this

  • Quality
  • Price
  • Service

PROS

+
Add Field

CONS

+
Add Field
Choose Image
Choose Video