22 novembre 2024
Ouest Foire Cite Alia Diene Lot 30
e-talif

Taalif de Serigne Hady Toure ; SALATUL FATIHA

« Def ngay « xasiida » ci ay
Yaaram ci Tiijaani
Defal nu woy ci Wolof
Nun gaayi Soodaan
Yaaram yi ñoo diy ngalam
Wolof yi ñoo diy përëm
Asil ngalam ak përëm
Ngir àqi Njaajaam
« Al hamdu li laahi » woy
Wii maa ko woy te li tax
Da may digël gaayi
Sòobu yoonu Tiijaan
Tiijaan bi bul xotti
Wormay diine bul tilimal
Mbubbum « chariiyatu »
Lii xewul ci Tiijaan
Jàppal te julli te wut
Xamxam ba am ca lu doy
Nga jaamu Yàlla bu baax
Tey santa tey ñaan
Joxal « Haqiiqatou » àqam
Jox « chariiyatu » sartam
Loolu mooy li nu xam
Nun gaayi Tiijaan
Tiijaan bi bul naxe, bul
Wor, bul di nay ci alal
Joxeel, joxees la ba muy
di baawaan di saawaan
Joxeel ci Yàlla te jëf
Ngir Yàlla boo joxewul
Jëfoo, na ngay ame ndam
Ci yoonu Tiijaan
Jëfal te bul damu bul
Xeebaate bul ayibal
Ku sellalul nanga
Sellal ci Tiijaan
Bul saaga, bul xaste bul
Jëw, bul di mer te jotul
Te soo merée bul xuloo
Te bul di reetane
Bul am xarit bi di ab
Yéeféer te bul bañitam
Benn jullit, lu ko moy
Koon def nga njaajaan
Bul réylu, bul nay te bul
Ñaaw Jiikkò, bul wax-u fen
Anda-ak moom ci Tiijaani
Yeewal sa mbir ci mbirëm
Ak, yatti buum yu Dëgër
Sopp ak jëfëk joxe
Lii moo gën ci Tiijaan
Bul nég ci sak joxe kuy
Ganee ka yònni si ndaw
Xamal ne nun du nu laaj
Nun gaa yi Tiijaan
Su yéené sellee bu soobe
Yàlla dees na ko man
Ségém liggéey nga bu baax
Te roy ci Tiijaan
Na ngay yërëm gone tey
Wormaalu mag te sawar
Ndax loolu moy yoonu
Gaayi Seexu Tiijaan
Nattal ci andaari pas-pas
Jëf ju yiw, mu di bor
Soo leblewul lu ñu lay
Fey ci yoonu Tiijaan
Muñal mar ak xiif te
muñ aw rafle soo ko déful
Bul seentu barkeek ngërëm
Ci yoonu Tiijaan
Sonn ak mar ak xiif, te
Sàkku Yàlla, soo ko notul
Ci yoon wi na nga koy note
Ci yoonu Tiijaan
Farlul ci say ñaari waajur
Sàkku seeni ngërëm
Te moytu seeni mer
Te yaakaar yiw ci seen ñaan
Bu leen ne mbass saa,
Bu leen gëdd-it sa wax
Na di nooy te ngay toroxlu
Te def la Yàlla santaane
Soo màggalul ña la jur
Ba doom ju bon di la fey
Sab xol di gañgañi
Ngay ñaxtoo ka ñeetaan
Boo dee teral ña la jur
koon soo tëlée di nga gis
Sa doom ju baax di la fey
Sab xol di kontaan
Deel muslu tey mosle
Foo gis nit ku yiw ku
Amul, joxal dërëm muy
Sa kok du xaaraani
Yow guy gu réy giy defar
Laax-ak ceree ka di far
Rongoñi kuy jooyu mar
Yow Seexu Tiijaan
Yàlla def nga di
Sangub « lawliyaa » yi, te lii
Yonnen ba moo la ko wax
Yow Seexu Tiijaani
Yonnen ba tàllal na
Baaraam-ub diggëk ba ca
Sés, di wax ci sa ruu akuk
Ruu-am lu keemaane
Sa ruu gi mooy tëbb
Ay xéewël yu yaatu yu
Réy yow Seexu Tiijaan
Sa ruu gi mooy tëbb
Ñii wërsëk yu yaatu ya
Ñii xamxam yu sella ya
Eskéy Seexu Tiijaan
Te sax bu fekkoon du yow
Koonuk nawet du fi taw
Te ay njariñ du fi ñëw
Yo Seexu Tiijaani
Yonnen bi neena la
Warlul naa la lii ku la
Gëm te am ca pas pas bu
Dee-ee fekke « Ridwaani »
Sa wird wii ku ko yor
Te bàyyi woo ko ba dee
Doo gis ci sab xabru kuy
Ragloo ka xeexaani
Ab nen ci nun la di xaymaam
Moo di « alfu wali » ca
Gaa ya am ya kamaal
« Min xayri Tiijaan »
Ab nen bu dee wecci
Junniy « Awliyaa » yu « kamal »
Moo koon na nuy xame
Xaymab cuuju Tiijaan
Moo tax bu saa taxawee
Ba seen jaloore ya feeñ
Ñuy sambandaay ay Yonnen
Ñoom gaa yi Tiijaan
Ñuy laaj di laajte
Te naan ay lanbiyaa
La ñu am ay mursaliin
Ñu naa leen ñoo di Tiijaan
Te bul iñane ka am
Te bul ñeetaane
Bul toqi, bul yoqi, kuy
Wut Yàlla soo sawarul
Sak am ko wòorul
Te do roy Seexu Tiijaan
Bul tàyyi, bul bàyyi
Boo bàyyee, ku koy
Xala yëk, xam ngeen tuyaaba
Du doy ci yoonu Tiijaan
Ñemeel Jataayu « Zikar »
Te bul nelaw ba fajar
Neex-uk nelaw du ko jar
Ci yoonu Tiijaan
Fonkal « wasifa » te fonk
Wird, wax ja na set
Ngay teewlu maanaa ya
Teewlu Seexu Tiijaan
Bu baat ya ruube
Bu ay sadd-ya woyof
Te bu ay mbijaan di des
Lii la wax moon Seexu Tijaan
« Salaatul faatiha » ken
Wirdul lu mel na ka moom
Màggal ko loo mas-a mën
Te bul ko caaxaane
Bul xas wàliyu, bu koy,
Gaaral, bu koy doyadal
Ndax waayi Yàlla la
Leemoo sànni wa saan
Bëggël, gëmël, màggalal
Soppal, wegal, teralal
Mbooleem waliyu yi
Lii Yàlla-a ko santaane
Buur Yàlla nee na
Ku lor waayam, na xam
Ci lu wér, ne dey xareek
Moom, te dey dee tàbbi Niraani
Mbooleem wàliyu yi, naw
Naa leen ci Yàlla bu wér
ginnaaw ba jaayante
Naa-ak Seexu Tiijaan
Boo jébbëloo na nga seet
Ci gaa ñi, waa ju la doy
Nga sàmmi sartam te
Gërëm tey santa kay ñaam
Yonnen bi neena ku nay
Dey dànd Ajjana ak
Mbindeef yi ak Yàlla
Ñòòxu kàmbi Niraan
Te neena ab tab sore
Naa-k Naari, tek ca jegeek
Buur Yàlla ak nit ñi ak
Jannatu Ridwaani
Am fulla moo di li war
Ndax moom la ñuy yore kër
Akub dogal waaye
Bul wex xàtt nib kaani
Bul fenq yat sa jabar
Muy dox di toggum xewar
Koon yaa deful li la war
Ci yoonu Tiijaan
Jabar bu dee bëré
Boo bëggée mu daanu
Waxal te jëf ci moom lu rafet
Koon dal nga koy daan
Muñal ko muuñal ko
Fellal yéy te jox ko mu yéy
Ndax ub xolam ak sa xol
Déggòo ci waxtaan
Wottul ma ndaw su rafet
Su dee taxaw fi sa wet
Jògal ca kaw ne bërét
Daw moytu seytaane
Seytaane nee moodi ak
Xalaam, te nee du ca moy
Seytaane daana ka
Dootul sàcc, dey daane
Woddal jabar te saxal
Njël, fey sa bor ba mu
Mat, nga def « aadiya »
Ci yoonu Tiijaan
Yaa Seexa naa Ahmadaa
Tiijaani Seydinaa
Sa leer gi jolli na
Foo xool, moo fa baawaan
Yaa am jalooré yu réy
Yaa am ngënéel aki mey
Yaaram bi yaa jara woy
Yow Seexu Tiijaan
Sëriif bi yaa mata roy
Sa wird wee mata njon
Sa ndën li neex na te doy
« Laxtaab » ya sex seeni baaraam
Réccu ngir di nu ñee
Te naan bu doon tey
Nu sòobu yoonu Tiijaan
Bennat ci nun, yenni fan
Soo leen gisee te ñu seere
Gis ga, koon ra nga
Doo too seere Niiraan
Yeen gaa yi seex yi xana
Lii doy na mbégté xanaa
Lii doy na yaakaar-it
Sòobu yoonu Tiijaan
Fu ngeen fi gis, waa ju am
Pas pas ca ngir ma mu aw
Na ngeen dëgërlu te am
Pas pas ci Tiijaan
Joor ak Xaree (1) tax
Ndee am naa ay sugum (2)
Te da ma xeeboon lem-ug
Xëndënduur ci Seexu Tiijaan
Ñoo nemm (3) aw xëndënduur
Nemmin-u waa ju xamul
Ma jòg di leen wonu yoon
Ci Seexu Tiijaan.
(1) Joor ak Xari, ñaari jigeen-am la ñu,
yu ko woyoon ci làkku wolof.
(2) Sugum mooy lem
(3) nemm mooy génné lem ci tàggu yamb.
 »

Leave feedback about this

  • Quality
  • Price
  • Service

PROS

+
Add Field

CONS

+
Add Field
Choose Image
Choose Video