4 décembre 2024
Ouest Foire Cite Alia Diene Lot 30
Actualites-de-la-Hadara

Eloge de Serigne Moustapha Sy Djamil : Ḥamdan liman de Serigne Maodo Dia, transcrit et traduit par Dr Seydi Diamil Niane

1_ Ḥamdan liman ḫaṣṣanā Saydil Jamīl sunu mbër /Buur Yàlla sàmm ko ak njabootu Seex gi mu yor
Louange à Celui qui a fait de Seydi Jamil notre leader privilégié /Que Dieu le protège ainsi que la famille de Cheikh dont il est responsable.
2_ Ṯumma-l-ṣalātu ‘alā-l-muḫtāri min muḍarin /Wa ālihī te nu gëm ne Yàlla jox na ko cër
Que la paix soit sur l’Élu de la tribu de Muḍar /Et sur ses compagnons. Sachons qu’Il lui a fait don de grâces.
3_Wa‘taṣimū ayyuhā-l-’iḫwānu yeen sama ñoñ /Ci Mustafaa te nu ñaan buur Yàlla dolli ko wér
Peuples, ô miens, attachez-vous à Mustafa /Prions pour qu’il soit toujours en bonne santé.
4_ Moo sàmm diine ji aar ñoñam ba ñépp taxaw/ Di jëf ci diine ji bañ mboolem lu bokku ci wor
Il préserve la religion et protège efficacement les siens / Il se conforme à l’islam et hait tout ce qui est trahison.
5_ Jëmmal nga bokku gi jox nga diine cër ba ca war /Šayḫa-l-mašā’iḫi tay ñépp nooy ne ki der
Tu as incarné la fraternité et as donné à la religion ses droits /Ô maître des maîtres, voilà que tout le monde te suit.
6_ Worul waxul yënguwul ku roy ci moom da nga raw /Xaliifa jox na ko ndénkaanéem mu yor ko bu wér
Jamais, par ses actes ou ses paroles, il n’a trahi. Est bienheureux son adepte /Khalifa lui a légué son héritage et il l’a dignement préservé.
7_ Yā wāriṯa-l-quṭbi yaa donn garaat ya ca Seex /Qawlan wa fi‘lan ku roy roy na yonent ci lu wér
Ô légataire du pôle, tu as hérité de ses stations mystiques /Qui te suit donc est, manifestement, sur les traces du Prophète.
8_ Šayḫa-l-mašā’iḫi fī-l-islāmi yay ki nu doy /Nan soppu gëm te wéral te xam ne mooy su nu cër
Ô grand maître de l’islam, toi seul nous satisfait /T’aimer, avoir foi en toi et te suivre scrupuleusement, tel est notre rôle.
9_ Yā ’iḫwatī fa’nhaḍū qad lāḥa ḥażżukumū /Nan àndandoo di ko way ndax loolu mooy li nu war
Ô miens, réveillez-vous, votre chance est apparue /Chantons ensemble sa gloire ; cela est notre devoir!
10_ Falāḥa ṣubḥun ‘alā laylin nu jóg di ko way /Ṣamīmatu sittinā Soxna Umooy ki ko jar
L’éclair du jour a dissipé les ténèbres de la nuit /Louons ainsi cet intime de Sokhna Oummu, il le mérite.
11_ Yā sayyidī wa amīra-l-nāsi kullihimū /Qad jā’a fī ḥikamin li-lāhi mooy ki la far
Ô maître, guide de tous les hommes /C’est dans Sa sagesse que Dieu t’a élu!
12_ Innī ġafaltu ‘alā jahdin fa ṣayyaranī /Kamā tarā ku la neex mu daldi mel na ki gar
Dans mes efforts, j’ai été négligent, il m’a pourtant transformé /Vois-tu, tu soumets à ton autorité spirituelle qui tu veux.
13_ Bādir ilayya ne koo fa xam du réer abadan /Yā qudwatī ndeke yóo yaa tee ñu jooy werarar
Approche-toi de moi, qui te connaît ne se perdra jamais /Ô mon idole, grâce à toi, nos larmes n’ont plus coulé.
14_ Ahlan bi šamsin badat bayna yaday qamarin / Yaa feeñ ñu faatte ku dul yaw way wi yaay ki ko jar
Bienvenue à ce soleil lumineux paru à côté d’une lune /À ta venue, tout autre que toi est oublié; tu mérites ce poème.
15_ Ġawṯa-l-anāmi wa miṣbāḥa-l-ẓalāmi farī /da-l-dahri yaa wéete tay li Seex yoroon ci lu bir
Secours des hommes, lumière des ténèbres, unique en ton temps /Aujourd’hui, assurément, tu as l’exclusivité du leg de Cheikh.
16_ Fuznā bi sayyidinā Allaaji Raz mi nu wan /Leeru Jamiil di nu ñaan ban jók di way sunu mbër
De notre maître Elhadji Racine, nous sommes gratifiés /Il nous a montré les lumières de Jamil et nous a poussé à chanter notre leader.
17_ Yā faylamānī ku lay koontar walàhi xamul /Yaa wulli Njaambur mu nooy ba góor yi mel na ki xar
Ô grand champion, est ignorant celui qui s’oppose à toi /Tu as dressé le Njaambur, les grands hommes, tel un mouton face au berger, se sont ainsi soumis.
18_ Yā ‘āliman ‘amila fī-l-dīni yā ṯiqatī /Abī-l-Ḥabīb ḥażżanā Yàllaa la fal nga di mbër
Ô sachant ayant oeuvré pour la religion, ô mon confident /Père aimant, notre chance, Dieu t’a fait leader.
19_ Sa ngor gu lànd ku la gis de xam ne doo ayibal /Serwiisu mbay gi nga yor Allaaji dée fu la ger
Ta dignité est inégalée. Tout le monde sait que tu perfectionnes /Tu es dans le service de Mbay. Elhaj, tu es incorruptible.
20_ Da‘ā ilā-l-Musṭafā yaw wootewoo wutu tur /Xuddaam taxaw na ca Njaambur yày kenoom ci lu wér
Vers Musṭafā, il appelle et non pour sa renommée personnelle /Xuddam est ainsi bâti à Njaambur, il est son pilier sans conteste.
21_ Nun li nu war di ko roy ci ay jëfin aki wax /Góor ak jigéen ci Xuddaam ñaanal ko mooy li nu war
Notre devoir est de le suivre, en paroles et en actes /Hommes et femmes de Xuddam, nous lui devons des prières.
22_ Yā Musṭafā sanadī kun āḫizan bi yadī /Yawmal xiyaam ku la gis du dégg riirum Saxar
Musṭafā, ô mon soutien, demain, prends-moi la main /Quiconque te voit, le jour du Jugement, n’entendra jamais le bruit de l’enfer.
23_ Nun waa xuddaam nanu jóg di way Jamiil sunu mbër /Mi wuutu Mbay Si te uuf njabootu Às ci lu wér
Membres de Xuddaam, levons-nous et louons Jamil, notre leader /Il est l’héritier de Mbay Sy et a pris soin de la famille de Às.
24_ Jëmmal nga mbokku gi jox nga diine cër ba ca war /Šayḫa-l-mašā’iḫi tay nak ñéppa nooy ne ki dër
Tu as incarné la fraternité et as donné à la religion ses droits /Ô maître des maîtres, voilà que tout le monde te suit.
25_ Waa Waalo ñëw na ñu Njaambur ken desul ba Jolof /Barñee ki Cees ba Tiwaawan ñéppa goor ne ki xar
Waalo est venu, tout Njaambur ainsi que Jolof /Bargnie, Thiès et Tivaouane, tel des moutons face au berger, te suivent.
26_ Gayndey njaloor yi ci gol beey Mustafaa ki ràkkam /Mansóor mu ndaw ak ràkkam Seex ñoo di gaynde yu góor
Ces lions visibles, dans la tanière, ne sont autres que Musṭafa et ses frères /Mansour Junior, son cadet Cheikh, voilà les lions virils.
27_ Buur Yàlla mooy ki la fal te def la taaw nga di njiit /Nga aar njaboot gi te sàmmu diine def la la war
Dieu t’a élu, a fait de toi l’aîné et le leader /Tu as préservé la famille et la religion. Tu fais ton devoir.
28_ Xel yéppu deelsi rangooñ yi fer na dootunu jooy /Xaliifa Mbay yaa matal léepu te def nga la war
Les esprits sont retrouvés, les larmes ont séché et on ne pleurera plus /Ô Khalifa Mbay, tu as parfaitement accompli ta mission.
29_ Law lam takun fī zamānī nun fu nuy xala jëm /Xanaa wëreeloo ka ñee tànnee ka fecci sabar
Si, en notre temps, tu n’étais pas, que deviendrons-nous? /Sinon des vagabonds, envieux, et danseurs de tam-tam?
30_ Tuus léen te bàkk ko bi-l-amdāḥ la Abdu waxoon /Sa baay danà la ko wax ndax yaa di mbër mi ko jar
“Paradez et faites son éloge", disait Abdou à ton père /Je le répète en ton honneur; tu es un leader qui le mérite.
31_ Akmalta ajmalta yā maljāna yaay ki nu doy /Yaa def li tax ñéeppu ŋoy doylu te fonku sa ngor
De manière belle, tu as rempli ta mission, ô refuge qui nous satisfait /Par tes actes, tous s’attachent uniquement à toi dans le respect de ton rang.
32_ Buur Yàlla moom mi la fal te jox la cér bi nga yor /Yàl na la aar sàmmu la sàmmu njaboot gi nga yor
Que le bon Dieu qui t’a élu, t’a gratifié de ces dons,/ Te protège et préserve ainsi que ta famille.
33_ Humu-l-ḫiyāru ‘alā-l-maḫlūqi sayyidunā /Mansóor mu ndaw Séydinà Seex suñu cér baña far
Ils sont les meilleurs parmi les hommes, je veux nommer /Mansour Junior et notre maître Cheikh. Que notre grâce soit préservée!
34_ Ṣalli ṣalātan ‘alā ḫayri-l-warā rabanā /Wa ālihī ak ñoñam muy wéy ba dundu bi far
Que Ta bénédiction, Seigneur, soit à jamais sur le meilleur des hommes /Sur sa famille et ses compagnons, et ce, jusqu’à la fin des temps.

Dr Seydi Diamil NIANE
Louga, le 28-05-23

Leave feedback about this

  • Quality
  • Price
  • Service

PROS

+
Add Field

CONS

+
Add Field
Choose Image
Choose Video