21 novembre 2024
Ouest Foire Cite Alia Diene Lot 30
e-talif

TAALIF : SEEXU TIIJAAN SËRIIF ( EN HOMMAGE A CHEIKH AHMED TIJAN CHERIF ( RA )

Su Buur Yàlla soobee
Di naa fenti woy
Di kañ Seexu Tiijaan
Sëriif kañ yu réy
Sëtub Gën ji mbindéef
teg ciy donoom
Ca mbòot yaag
Ca leer yaag ngënéel yaa ki mey
Sangub "lawliya" yi
Ki leen raw ci Yàlla
Te gën leena set yéeré
Gën leena xay
Te sut leen ci xamxam
Te man leen ci diine
Te gën leena réy mbir
Ci démb ak ci tey
Su ngéen koy limaaleek
Ñeneen cig wilaaya
Tawuk waame ngeen
Di lamaalee ki lay
Su ngéen koy limaaleek
Ñeneen cig wilaaya
Gëléemug tukkël
Ngéen limaaleek i béy
Su ngéen koy "xiyaaseeg"
Ñeneen ciy "màqaama"
Tawub waame ngéen di
Xiyaaseek mëséy
Yonnen baa ko jox
Ab tariixaaki"sartam"
Ku wor "sarti" Yonnen ba nag
Déf nga ay
Ku wor Seexunaa
Ak mujjëm moo di Naari
Te diirub li muy noyyi
Dey wat magay (1)
Ku wor Seexuna
Gën ji mbindéef nga wor
Ku wor Gën ji mbindéef
Bu làyyee du yay
Bu xiinée du tawlu
Su tawloo du ñorlu
Su ñorloo du woomal
Ci yaakaari mbey
Su diiree du jekku
Ku oy gaa ñu baax ña
Da ngay xeñtu sunnë
Te kuy xeñtu sunnë
Da cay njoy te woy
Na ngay xeñtu sunnë
Te xam ni biddaa
Su feeñee ci marse
Du jar sax buréy
Dëgërlul te dolli rukoo
Ak sujòòt te wàññiy
Nelaw, waññiy
Waxtaan wu réy
Dëgërlul te nootoo
Jataayub "zikar"
Su fekkee ni daa metti
Xam ngeen du rey
Na ngay teewlu
Tey teewlu gaa yay
Wëziifa fu buccori leer
Yay joxe ngën ji mey
Na ngay jàngi "chadda"
Te ngay jàngi "madda"
Ndégem Seexa naa
Aki gaayam nga
Na say wax di sette
Bu baat ya di ruube
Te bus cay manaatu
Ba muy mel ni woy
Liggéeyal ci méccé
Mu fanxal la gàcce
Lu leen Yàlla séddé
Na leen loola doy
Te bul dem di moslu
Dadul tax nga këslu
Te sax far na ruslu
Te koon tey si tey
Te sak fàggu nay yaa
Te réy dooma yaa
Te loo gis ci dunyaa
Muñël lée mu wéy
Na Buur Yalla dolli
Salaatook salaam
Ca yonnen baak saaba
Yaak gaa ña roy
Li feek ràbb ngiy xey
Ci waxtu liggéeyam
Di laaj saaji falley
Di tàllal garey
Su dee ree du kekku
Su dee war di daanu
su dee sànni moy
Sunub yoon ku koy
Sòobu bul bàyyi bul
Siyaare ku dul nun
Te yit nan la doy
Ku dib "xutbu" mbaa ngay
Boroomuk Wilaaya
Sëriif Seexu Tiijaana
Lay tëbbi mey
Xarit kaay ma wax la
Fabal wird wii
Te "Zikar" bu baax
Daldi am mey gu réy
Ñëwël sòobu yoon wi
Ci wird ak "waziifa"
Te aw yoonu Yàlla
Ci gontak ci xéy
Xarit kaay ma wax la
Samay maama ngii
Ku am maam yu mel noonu
Sañ leena woy
Ci Mawdook nijaayam
Boroom xeeju xaali
Ci Seexu Tiijaan
Ci "ahlaalu" woy
Samay maama ngoo gii
Te ñoo baax ci sët
Te ñoo gën ci man
Yàlla na leen Yàlla fey
Samay maama ngoogii
Ku leen xeñtu am
Teràngaak màxaamaak
Karamaaki mey
Samay maama ngoogii
Ku leen sopp doo
Texeedi ndégém sak cofeel
Wéér na kay
Su guddee ba weerak
Biddeew lépp suux
Ku nuy teewlu xam ni
Sunuy leer du fey
Su guddee ba weerak
Biddeew lépp suux
Ku gëmmit bëtëm gis
Ku xoolit ba tey

UN POÈME DE SERIGNE HADY TOURE

Leave feedback about this

  • Quality
  • Price
  • Service

PROS

+
Add Field

CONS

+
Add Field
Choose Image
Choose Video